Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 15

Naka la magi mbooloo mi di dimbalee waa mbooloo ?

Naka la magi mbooloo mi di dimbalee waa mbooloo ?

Finlande

Jàngale

Sàmm

Waare

Ci suñu mbootaay amuñu ay kilifa diine yu ñuy fey ndax seen liggéey. Ni ñu ko daan defe ci mbooloo karceen yu njëkk ya, tey ay góor yu mat njiit lañuy tànn ngir ñu “ sàmm mbooloo mi ” Yàlla moom (Jëf ya 20:28). Mag yooyu dañu am diggante bu rattax ak Yàlla. Ñoom ñooy jiite te di sàmm mbooloo mi. Defuñu ko ni ku “ sañul-bañ, waaye di surgay Yàlla ci xol bu tàlli, ak xol bu laab te bañ cee séentu alal ” (1 Piyeer 5:​1-3). Naka la mag yooyu di ñu dimbalee ci mbooloo mi ?

Ñu ngi ñuy toppatoo te di ñu sàmm. Magu mbooloo yi ñoo ñuy dimbali ci aar suñu diggante ak Yàlla. Ñoom, xam nañu ne Yàlla moo leen dénk liggéey bu am solo boobu. Loolu moo tax duñu noot mbooloo mi, waaye dañuy def lépp ngir waa mbooloo mi am jàmm ak mbégte (2 Korent 1:​24). Sàmmkat bu baax dafay toppatoo xar bu nekk ci géttam. Magu mbooloo yi ñoom itam, dañuy def lépp ngir xam kenn ku nekk ci seen mbooloo. — Kàddu yu Xelu 27:⁠23.

Ñu ngi ñuy jàngal ni ñuy toppe li Yàlla santaane. Semen bu nekk, magu mbooloo yi dañuy jiite ndaje yi ñuy am ci mbooloo mi ngir dëgëral suñu ngëm (Jëf ya 15:32). Ñoom ñooy jiitu itam liggéeyu waare bi. Dañuy ànd ak ñun ci waaraate bi te di ñu jàpple ci bépp fànn ci liggéeyu waare bi.

Ñu ngiy jox kenn ku nekk ci ñun xelal yi mu soxla. Mag yi ci suñu mbooloo dañu bëgg ñu am diggante bu rattax ak Yexowa. Moo tax lée-lée dañuy ñëw di ñu seetsi ci suñuy kër walla ñuy waxtaan ak ñun ci suñu saalu Nguur gi. Li ñu bëgg mooy won ñu ci Mbind mu sell mi liy dëgëral suñu ngëm ak li mën a dëfël suñu xol. — Saag 5:​14, 15.

Liggéey boobu yépp la magu mbooloo yi di def, teg ci ne ñi ëpp ci ñoom ay boroom kër lañu te yore seen liggéeyu bopp. Xam nañu ne loolu dafay laaj jot ak toppatoo. Dëgg-dëgg suñu mbokk yu góor yooyu ñeme nañu liggéey, moo tax yelloo nañu ñu may leen cér bu réy. — 1 Tesalonig 5:​12, 13.

  •  Lan mooy liggéeyu magu mbooloo ?

  •  Naka la magu mbooloo yi di wonee ne yëg nañu kenn ku nekk ci ñun ?