Ubbil li ci biir

BIIBËL BI DAFAY SOPPI DUND

«Gëmatuma ne war naa soppi àddina si»

«Gëmatuma ne war naa soppi àddina si»
  • AT BI MU JUDDU: 1966

  • RÉEWAM: FINLANDE

  • JAAR-JAARAM: DAFA DOON XEEXAL ÑI NÉEW DOOLE

LI MA DUND:

Dama mas a bëgg li Yàlla sàkk. Sama waa kër dañu doon faral di génn doxantuji ci àll yi ak ci booru dex yu rafet ci suñu dëkk Jyväskylä, ca Finlande. Ku bëgg mala laa itam. Bi ma nekkee xale, saa yu ma gisoon muus walla xaj rekk dama koy bëgg a fab! Bi may màgg, dafa ma doon metti lool bu ma gisoon nit ñi di toroxal mala yi. Mujj naa bokk ci benn mbootaay bu doon xeex ngir aar mala yi. Foofu tase naa fa ak ñu bokkoon gis-gis ak man.

Dañu doon yëngu bu baax ci xamal nit ñi ñu aar mala yi. Dañu doon yee nit ñi, di amal ay doxu ñaxtu ngir xeex ñiy jaay yére yu ñu defare karawu mala ak ñiy jël mala yi ngir def ay gëstu. Dem nañu sax ba taxawal mbootaay bu bees ngir aar mala yi. Dañu doon dem ba jeex ci xeexal mala yi, moo tax ñu faraloon di am jafe-jafe ak nguur gi. Jàpp nañu ma te àtte ma ay yooni yoon.

Ginnaaw xeexal mala yi, amoon na yeneen jafe-jafe ci àddina si yu ma metti woon. Bokk naa ci mbootaay yu bare, yu ci mel ni Amnesty International ak Greenpeace. Def naa ci sama kàttan gépp. Dama doon xeexal ñi néew doole, ñi xiif, ak ñi sonn.

Waaye ndànk-ndànk, gisoon naa ne mënuma soppi àddina si. Bu dee sax mbootaay yooyu mënoon nañu regle yenn poroblem yu ndaw yi, poroblem yu mag yi dañu doon gën a yées. Dafa meloon ni lu bon a ngi doon yàq àddina si sépp te kenn bëggul woon a def dara. Gisoon naa ne mënuma ci dara.

NI BIIBËL BI SOPPEE SAMA DUND:

Bi ma gisee ne mënuma soppi yëf yi, sama xol dafa jeex. Ma tàmbali di xalaat ci Yàlla ak ci Biibël bi. Masoon naa jàng Biibël bi ak Seede Yexowa yi. Seede Yexowa yi neexoon nañu ma ndaxte ñu baax lañu te dañu amoon itte ci man. Booba parewuma woon ngir soppi sama dundin. Waaye bii yoon yëf yi wuute woon nañu.

Dama jël sama Biibël, tàmbali koo jàng. Loolu dëfal na ma bu baax. Ci laa seetlu ne, aaya yu bare ci Biibël bi dañuy wax ñu toppatoo bu baax mala yi. Ci misaal, Kàddu yu Xelu 12:10 nee na «ku jub day topptoo ag juram.» Jàng naa it ne, du Yàlla moo ñuy teg coono. Waaye li yokk suñuy poroblem mooy nit ñi duñu topp li Yàlla santaane. Bi ma jàngee ne Yexowa dafa ñu bëgg te dafa ñuy muñal, loolu laal na ma bu baax (Sabóor 103:​8-14).

Ci jamono jooju laa gis benn kayit bu ñu mënoon a yónnee ngir am téere bi tudd Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ? Ma jël ko bind ci sama tur yónnee ko. Yàggul dara benn Seede Yexowa ak jabaram ñëw sama kër, laaj ma ndax bëgg naa jàng Biibël bi, ma nangu. Tàmbali naa itam di teewe ndaje yi ci saalu Nguur gi. Loolu moo tax dëgg gi nekk ci Biibël bi komaasee laal sama xol.

Biibël bi moo ma dimbali ma soppi lu bare ci sama dund. Bàyyi naa tux ak naan ba màndi. Soppi naa sama colin te gën naa rafetal sama waxin. Soppi naa itam sama gis-gis ci njiiti àddina si (Room 13:⁠1). Bàyyi naa itam dund gu bon gi ma doon dund ndaxte lu ma neex rekk laa doon def.

Li gënoon a metti ci man mooy soppi sama gis-gis ci mbootaay yi ma bokkoon. Jël na jot bala ma koy mën a def. Li ma jàppoon mooy, bu ma leen bàyyee dafay mel ni dama leen wor. Waaye mujj naa nangu ne nguuru Yàlla rekk moo mën a faj jafe-jafe yi ci àddina si. Ma jël dogalu def sama kàttan gépp ci liggéeyal nguuru Yàlla ak dimbali ñeneen ñi ñu xam ko (Macë 6:33).

NJARIÑ BI MA CI JËLE:

Bi ma doon xeexal ñi néew doole, ci man ñaari gurup rekk a amoon: ñu baax ñi ak ñu bon ñi. Te pare woon naa ngir dal ci kaw ñi ma jàppe woon ñu bon. Waaye Biibël bi dimbali na ma ba bañatuma kenn. Li may def kay mooy jéem a won mbëggeel nit ñi ñépp (Macë 5:44). Benn anam bi ma koy defe mooy yégal leen xibaaru jàmm bi jëm ci nguuru Yàlla. Kontaan naa ci gis ne liggéeyu waare bi dafay may nit ñi jàmm, mbégte ak yaakaar dëgg.

Tey sama xel dal na ndaxte dama bàyyi lépp ci loxo Yexowa. Gëm naa ne, moom mi sàkk lépp, du bàyyi ñuy toroxal mala yi ak nit ñi ba fàww. Te itam du bàyyi ñu yàq suñu suuf su rafet sii. Ci kanam tuuti, dina jaar ci Nguuram ngir defaraat lépp li nit ñi yàq (Esayi 11:​1-9). Xamal nit ñi dëgg gi nekk ci Biibël bi te dimbali leen ñu am ngëm ci Yàlla, dafa may indil mbégte dëgg. Léegi, gëmatuma ne war naa soppi àddina si.