Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Jëkkër ak jabar yu déggoo dañoo mel ni kuy dawal awyoŋ ak ki koy dimbali. Ñoom ñaar, dañuy ànd liggéey ngir mën a àgg fi ñu bëgg dem.

ÑI NEKK CI SÉY ÑOO MOOM LII

2: Déggoo

2: Déggoo

LI MUY TEKKI

Jëkkër ak jabar yu déggoo, dañu mel ni kuy dawal awyoŋ ak ki koy dimbali. Ñaar ñooñu, dañuy ànd liggéey ngir mën a àgg fi ñu bëgg dem. Bu jafe-jafe amee sax ci séy bi, kenn ku nekk ci ñoom dafay xalaat «moroomam», te bañ a xalaat «boppam» rekk.

LII LA BIIBËL BI WAX: «Kon nag nekkatuñu ñaar waaye benn lañu» (Macë 19:6).

«Séy du mbiru benn nit. Jëkkër ak jabar dañu war a déggoo ngir seen séy neex» (Christopher).

LI TAX MU AM SOLO

Jëkkër ak jabar yu déggoowul, bu jafe-jafe amee, dañuy faral di tuumalante waaye duñu jéem a faj jafe-jafe bi. Porobalem bu ndaw sax, dina mujj doon jafe-jafe bu réy.

«Déggoo mooy tax séy neex. Man ak sama jëkkër buñu déggoowul woon, kon ay dëkkandoo lañuy doon. Dañuy mel ni ñaari nit ñu bokk fu ñu dëkk, waaye duñu juboo bu ñu naree jël dogal yu am solo» (Alexandra).

LI NGA MËN A DEF

LAAJAL SA BOPP LII

  • Ndax dama jàpp ne, xaalis bi ñu may fey «man rekk maa ko moom»?

  • Ndax bu ma soree sama jëkkër walla sama jabar lay gën a féex?

  • Ndax damay daw samay goro, bu dee sax sama jëkkër walla sama jabar dafa takku ci ñoom?

WAXTAANAL AK KI NGA SÉYAL CI LAAJ YII DI TOPP

  • Ci yan fànn lañuy faral di déggoo ak ki ñu séyal?

  • Ci yan fànn lañu mën a gën a góor-góorlu?

  • Lan lañu mën a def ngir gën a déggoo?

XELAL

  • Bul jàppe ki nga séyal ni ki ngay dajeel ci futbal. Waaye jàppe ko ni ki nga bokkal ekip ngir ngeen mën a am ndam ci kaw jafe-jafe yi.

  • Bul xalaat ni nga mën a def ba ‘am ndam yow kese’, waaye xalaatal ni ngeen mën a def ba ‘am ndam yeen ñaar’.

«Xam ki am dëgg walla ki tooñ, du li am solo. Waaye li am solo mooy am jàmm te doon benn ci seen séy» (Ethan).

LII LA BIIBËL BI WAX: «Buleen yem ci topptoo seen bopp rekk, waaye booleleen ci seeni moroom» (Filib 2:3, 4).