Ubbil li ci biir

Lan la Biibël bi wax ci Paag?

Lan la Biibël bi wax ci Paag?

Li Biibël bi wax

Feetu Paag bokkul ci li Biibël bi santaane. Boo gëstoo bu baax, dinga gis ne feetu Paag mu ngi jóge ci aada yu yàgg yu nit ñi daan topp ngir ñoom ak seeni mala mën a am doom yu bare. Xoolal lii di topp.

  1. Turu Paag: Bu ñu déggee turu Paag (Pâques ci tubaab), ñu bare dañuy foog ne màggalu bés bi Yawut yi mucc ci Misra lañu mujj a def feetu karceen. Waaye téere bi tudd Encyclopædia Britannica, nee na, turu Easter ci ãgale (Paag ci wolof) kenn mënul a wax fi mu jóge dëgg-dëgg; te lu ëpp junni at ci ginnaaw, benn làbbe Anglo-Saxon bu ñuy woowe Venerable Bede moo joxe tur boobu. Mu ngi jële tur boobu ci turu Eostre, benn ci xërëm yi ñu doon jaamu jamono jooju. Am na yeneen téere yu naan tur boobu mu ngi jóge ci turu Astarte, xërëmu waa Fenisi bi ñu wax ne mooy tax nit ak mala mën a am doom yu bare, te ca Babilon xërëm boobu moo doon Ishtar.

  2. Lëg yi ak njomboor yi: Mala yooyu dañuy misaal mën a am doom yu bare. Loolu mu ngi jóge ci feetu ñi doon jaamu xërëm ca jamono yu yàgg ya ca Europe ak ca penku (Moyen-Orient) (Encyclopædia Britannica).

  3. Nen yi: Benn diksoneer (Funk & Wagnalls Standard Dictionary of Folklore, Mythology and Legend) dafa ne aada wër nen yi maanaam nen yi ñu gëmoon ne njombooru Paag a ko indi, du fowu xale kese waaye dafa jóge ci li nit ñi doon defal seen xërëm bi ñu doon jaamu bi ñu wax ne moo leen doon may ay doom yu bare. Am na ñu gëmoon ne nenu Paag bi ñu rafetal amoon na kàttanu «maye bànneex, yokkute, wér-gi-yaram ak kaaraange» (Traditional Festivals).

  4. Sol yére yu bees: Nit ñi dañu doon sol yére yu bees ngir teeru seen xërëm bi ñu doon jaamu bi tudd Eastre ca diwaanu Scandinavie. Jàppoon nañu ne ku ko deful danga ñàkk teggin te loolu mënoon na la um (The Giant Book of Superstitions).

Téere bi tudd The American Book of Days leeral na bu baax fi Paag jóge, nee na: «Wóor na ne, ci booru atum 400 la ay kilifa ci làbbe yi boole aaday jaamukati xërëm yi ci diine Karceen».

Biibël bi wone na ne Yàlla bëggul bu ñu koy jaamu ñu di ci boole ay aada walla cosaan yu ko neexul (Màrk 7:6-8). Yexowa nee na ci 2 Korent 6:17: «Génnleen biir ñooñu te beru. Buleen laal dara lu am sobe.» Paag, feetu ñiy jaamu ay xërëm la. Kon ñi bëgg a neex Yàlla waruñu bokk ci feet boobu.