Ubbil li ci biir

LI NDAW ÑI DI LAAJ

Ndax nit ku mat a wóolu laa?

Ndax nit ku mat a wóolu laa?

 Laajal sa bopp laaj yii!

  • Ndax damay [...] saa su ne, moo ëpp, lée-lée walla mukk

    • wax dëgg

    • sàmm sama kàddu

    • respekte heure

    • sawar ci liggéey

    • dimbali ñeneen ñi

    • wone respe

    • bàyyi xel ñeneen ñi

  • Ci jikko yi ñu fi lim ban nga ciy gën a wone?

    Wéyal di ci góor-góorlu (Filib 3:16).

  • Ci jikko yi ñu fi lim ban nga jàpp ne war nga ci gën a góor-góorlu?

Li ñu fi nar a waxtaane dina la ci dimbali.

Lan mooy nit ku mat a wóolu?

Nit ku mat a wóolu dafay def lépp li ko war ci kër gi, ca lekkool ba ak fi mu dëkk. Bu defee dara dafay nangu ne moo ko def. Su juumee dafay nangu ne juum na, mu baalu, te def lépp ngir wone ne réccu na li mu defoon.

 Lii la Biibël bi wax: «Ku ci nekk dangaa wara yenu sab yen» (Galasi 6:5).

Lu tax ma war a wut a nekk nit ku ñu wóolu?

Nit ku mat a wóolu, buy def li mu mën dafa ciy ànd ak sago. Loolu moo tax dañu koy naw, jàppe ko ni mag, may ko liberte, te dénk ko ay cér.

 Lii la Biibël bi wax: «Seetlul ku man liggéeyam, buur lay liggéeyal» (Kàddu yu Xelu 22:29).

Nit ku mat a wóolu dafay faral di nekk nit kuy maye te dafay faral itam di am ay xarit yu baax.

Lii la Biibël bi wax: «Mayeleen te dinañu leen may» (Luug 6:38).

Nit ku mat a wóolu dafay bég ci li muy def te loolu mooy tax mu wóolu boppam.

Lii la Biibël bi wax: «Na ku nekk seetlu ni muy beye sasam. Bu ko defee dina mana naw boppam» (Galasi 6:4).

Naka laa mën a def ba ñu gën maa wóolu?

Ngir dimbali la nga tontu ci laaj boobu xoolal li yeneen ndaw wax te ñu bind ko ci suuf. Ci li ñu wax fii lan moo gën a jege ak li ngay dund?

 «Dara gënul metti ñu jàppe la ni xale bu war a tàggu pàppam ak yaayam saa yu naree génn bu dee sax benn waxtu rekk la» (Kerri).

«Samay waajur amuñu benn jafe-jafe ngir bàyyi ma ma génn ak sama xarit yi» (Richard).

«Buma gisee liberte bi ñu may yenn ndaw yi ma maaseel, damay laaj sama bopp: ‘lu tax samay waajur duñu ma may ma def ni ñoom?’» (Anne).

Daanaka samay waajur dañu may bàyyi ma def li ma bëgg. Maa ngi leen di gërëm ci liberte bi ñu ma may» (Marina).

Ci gàttal: Am na yenn ndaw yi ñu gën a may liberte seen moroom. Lu waral loolu?

Li am mooy: Liberte bi ñu lay may mu ngi aju ci kóolute gi ñu am ci yow.

Ñaar ci ndaw yi ñu tudd sanq lii lañu wax.

Richard: «Amoon na jamono joo xam ne samay waajur gëmuñu woon ne mën naa jëfandikoo bu baax liberte bi ñu ma may. Waaye léegi wóolu nañu ma ndaxte jëfandikoo naa liberte bi ñu ma may ci anam bi gën. Damay wax samay waajur fi may dem ak ñi may àndal te duma leen fen. Damay wax samay waajur li ma bëgg def te duma xaar sax ñu laaj ma ko.»

Marina: «Ñaari yoon rekk laa mas a fen samay waajur te ci ñaari yoon yooyu dañu maa jàpp. Waaye booba ba léegi dëgg rekk laa leen di wax. Dama leen di wax lépp li may def te suma génnee dama leen di woo telefon. Léegi gën nañu maa wóolu.»

Lan ngay jiital: liggéey bi ñu la sant ci kër gi walla fo?

Ndax bëgg nga ñu wóolu la ni ñu wóoloo Richard ak Marina? Bu dee waaw, xalaatal ci laaj yii di topp:

CI BIIR KËR GI

  • Ndax yaa ngi def bu baax liggéey bi ñu la sant ci kër gi?

  • Ndax yaa ngi ñibbisi ci waxtu wu ñu la wax?

  • Ndax yaa ngi woon respe say waajur, say mag ak say rakk?

Ci ñetti ponk yi ñu fi lim, ndax am na ci benn boo xam ne danga ci war a góor-góorlu? Bu dee waaw, ban la ci?

Lii la Biibël bi wax: «Nangeen déggal seeni waajur» (Efes 6:1).

CA LEKKOOL BA

  • Ndax yaa ngi def liggéey bi ñu la jox ca lekkool ba ci waxtoom?

  • Ndax yaa ngi góor-góorlu ngir am notes yu gën a baax?

  • Ndax am nga ay tàmmeel yu baax lu jëm ci jàng say lesoŋ?

Ci ñetti ponk yi ñu fi lim, ndax am na ci benn boo xam ne danga ci war a góor-góorlu? Bu dee waaw, ban la ci?

Lii la Biibël bi wax: «Xel mu rafet kiiraay la» (Kàdduy Waare 7:12). Jàng bu baax dina la dimbali nga am xel mu rafet.

NI ÑU LAY GISE

  • Ndax dangay wax dëgg say waajur ak ñeneen ñi?

  • Ndax ni ngay jëfandikoo sa xaalis wone na ne mat ngaa wóolu?

  • Ndax xame nañu la ni nit ku ñu mën a wóolu?

Ci ñetti ponk yi ñu fi lim, ndax am na ci benn boo xam ne danga ci war a góor-góorlu? Bu dee waaw, ban la ci?

Lii la Biibël bi wax: «Soloo[leen] jikko ju bees» (Efes 4:24). Mën nga gën a rafetal sa jikko ak ni la nit ñi di gise.

Xelal: Tànnal jikko ji nga gën a bëgg rafetal. Laajal ñeneen ñi am jikko jooju ngir ñu xelal la ci. Bindal li nga mën a def ngir am jikko jooju, nga góor-góorlu ci, ci diiru benn weer. Bindal ci benn karne li nga jot a def ak li jafe ci yow. Su weer bi dewee nga xoolaat fi nga tollu.